1¶ Ci kaw loolu malaaka mi won ma dexu ndoxum dund mu leer nàññ ni doju kiristaal, ndox ma wale ca ngàngunem Yàllaak Gàtt ba,
2di tuuru ci digg péncu dëkk bi. Ci ñaari tàkki dex gi, garabu dund a ngi ci, di meññ fukki yoon ak ñaar, weer wu nekk benn yoon, xob yi di faj askani àddina.
3Alkànde nag du fa amati, te ngàngune mu Yàllaak Gàtt bi ci biir dëkk bi lay nekk, jaamu Yàlla yi di ko sujjóotal,
4di gis kanamam, turam binde ci seen jë.
5Guddi du amati, te deesul soxlaati làmp mbaa naaj, ndax Boroom bi Yàlla moo leen di leeral. Te dañuy nguuru ba fàww.
6¶ Ba loolu amee malaaka mi ne ma: «Lii wax ju wóor la te dëggu. Boroom bi Yàlla miy xelal yonent yi, moo yebal malaakaam, ngir mu won jaamam ñi mbir yi dëgmal te du jaas.»
15Ci biti, xaj yaa fa nekk ak xërëmkat yi ak moykat yi ak bóomkat yi ak bokkaalekat yi, ak képp ku sopp fen te di ko jëfe.
16¶ «Man Yeesu maa yónni sama malaaka, ngir mu seede mbir yii ci yeen, ñeel mboolooy gëmkat ñi. Man maay njebbitu Daawuda, di kuutaayam, maa di biddiiwu njël bi ne ràññ.»
17¶ Noo gi ak Séet bi neeñu: «Ñëwal!» Ku ci dégg it, neel: «Ñëwal!» Ku mar, ñëwal; ku bëgg ci ndoxum dund mi, jëlal, ñu may la.
18¶ Man Yowaan, seede naa ñeel képp ku dégg kàdduy waxyu yu téere bii, ne: Képp ku ci yokk lenn, Yàlla dina la yokkal mbugal, yi ñu bind ci téere bii.
19Te ku wàññi lenn ci kàdduy waxyu yu téere bii, sa wàll la Yàlla di wàññee ci yooyii ñu bind ci téere bi, muy garabu dund gaak dëkk bu sell ba.
20¶ Kiy seede mbir yii nee: «Waawaaw, maa ngi ñëw léegi.» Amiin, Sang Yeesu, ñëwal!