📖 Psalms 61
-
1
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, ànd aki xalam, ñeel Daawuda.
-
2
Ngalla Yàlla, déglul, maa ne wallóoy, teewlul, ma dagaan la.
-
3
Àll laa lay wooye, sama xol jeex; yéege ma doju rawtu wu ma jotul.
-
4
Yaw laa làqoo, ngay tata ju dëgër, fegal ma noon.
-
5
Naa dëkke sa xayma, ba fàww; làqoo sa kiiraay. Selaw.
-
6
Yàlla, yaa dégg samay dige, sédd ma céru ñi la wormaal.
-
7
Ngalla féqal fani Buur, ay atam bare, sët ba sëtaat.
-
8
Éy Yàlla, yal na Buur toog ba fàww fi sa kanam, nga sédd ko sa ngor ak sa worma, mu fegoo;
-
9
kon ma woy la ba fàww, di jëfe samay dige bésoo bés.