📖 Psalms 49
-
1
Mu jëm ci njiital jàngkat yi, di kàddug Sabóor, ñeel askanu Kore wu góor.
-
2
Yeen, xeetoo xeet, dégluleen; yeen, waa àddina yépp, teewluleen,
-
3
ngay ku tuut di ku mag, nga bareleek nga néewle.
-
4
Li may wax xel la, di xalaat yu déggu.
-
5
Damay teewlu kàddu yu xelu, xalamal la sama tekkiteb cax.
-
6
Ana lu may tiit bés yu metti, yu ma njublaŋ yéewe seeni ñaawtéef,
-
7
di ñu wóolu seen am-am, di kañoo alal ju bare?
-
8
Ana ku mana jota jot sa bakkanu moroom, mbaa mu di ko feyal Yàlla njot ga?
-
9
Njotug bakkan jafe na, bu ci jéem dara.
-
10
Ana kuy dund ba fàww, ba doo gis bàmmeel?
-
11
Xanaa gis ngeen ne xelu, dee; dof, dee; naataxuuna it faatu rekk, wacce keneen alalam.
-
12
Sa bàmmeel di sa kër, ba fàww, di sa dëkkuwaay bu sax dàkk, boo tudde woon sa bopp ay suuf sax.
-
13
Nit ak darajaam fanaanul, mook aw rab a yem, sànku rekk.
-
14
Nii la ku wóolu boppam di mujje, mook ku ko topp, di safooy waxam. Selaw.
-
15
Nara dee rekk niy xar, ndee wommat, yóbbu, njub fenk nib jant, ku jub moom leen, njaniiw mëdd seen jëmm, fu sore kërug daraja.
-
16
Waaye Yàllaa may musal ci dooley njaniiw, jot sama bakkan, ba jël ma.
-
17
Buleen yéemu ci ku barele, teraangay këram di yokku.
-
18
Du dee ba yóbbaale dara, teraangaam du ko topp biir bàmmeel.
-
19
Na bége bànneexu bakkanam, ñu di ko kañe koomam,
-
20
ba tey, day dee, fekkiy maamam, ña dootu gis ug leer ba fàww.
-
21
Nit ak darajaam fanaanul; mook aw rab a yem, sànku rekk.