📖 Psalms 143
-
1
Muy kàddug Sabóor, ñeel Daawuda. Éy Aji Sax ji, déglul, ma ñaan la; teewlul, ma tinu la; nangul ma ci sa wormaak sa njekk.
-
2
Sang bi, bul layook man; kenn jubul fi sa kanam, du kuy dund.
-
3
Noon a ma sambal, daane ma, joggati, dëël ma ci lëndëm ni ku dee bu yàgg.
-
4
Sama doole jeex tàkk, sama xol jeex, ma ne yàcc.
-
5
May fàttliku bu jëkkoon, di xalaat sa jaloore yépp, seetaat li nga def.
-
6
Ma tàllal lay loxo, di la sàkku, ni suuf su mar di sàkkoo ndox. Selaw.
-
7
Aji Sax ji, gaawal wuyu ma; sama xol a jeex, ma ne yàcc, bu ma xañ sa yiw, ma yem ak kuy tàbbiji biir pax.
-
8
Xëye ma sa ngor, yaw laa wóolu; xamal ma fu may doxe, yaw laa wékk sama bakkan.
-
9
Aji Sax ji, musal ma ci noon yi, yaw laa làqoo.
-
10
Jàngal ma, ma jëfe sa coobare; yaa di sama Yàlla. Yal na ma sam xel jiitee mbaax ci yoon wu tàlli.
-
11
Aji Sax ji, musal ma ngir saw tur, jëfeel sag njekk, teggil ma njàqarey bakkan.
-
12
Sànkal ma noon yi ci sa ngor, bóomal ma bépp bañ. Man de, maay sab jaam!