📖 Psalms 142
-
1
Muy taalifu ñaan bu ñeel Daawuda, ba mu nekkee ca xunti ma.
-
2
Ma àddu, ñaan Aji Sax ji; àddu ca kaw, di tinu Aji Sax ji,
-
3
sippi ko sama tawat, diis ko sama njàqare.
-
4
Bu ma yoqee, ràññee nga samay jéego; yoon wi may jaare lañu ma làqal am yeer.
-
5
Ma geesu ndijoor, xool; du kenn ku ma faale. Rawtu réer ma, du kenn ku sama bakkan saf.
-
6
Aji Sax ji, ma woo la wall; ma ne, yaay sama kiiraay, di sama séddoo fi kaw suuf.
-
7
Teewlul, ma ne wóoy, damaa manatul, xettli ma ci ñi ma topp, dañu maa ëpp doole.
-
8
Ngalla génne ma fi ma tëje, ma sant la. Man la way-gëm ñi di yéew ëllëg, yaa may xéewale ab yool.