📖 Proverbs 27
-
1
Bul damoo ëllëg, ndax xamoo luy xew tey.
-
2
Bul tëggu, bàyyil ñu tagg la, muy waxi keneen; yaw, bu ko wax.
-
3
Doj diis na, suuf dib sëf, waaye fitnay dof a ko raw.
-
4
Xadar day ñàng, mer di wal mu baawaan, waaye fiiraange amul moroom.
-
5
Artu yu ñu la biralal moo gën cofeel gu la boroom ñooru.
-
6
Soppe, bu lay gaañ sax, wóolu ko. Nit bañ na la, te di la fóon lu bare.
-
7
Ku suur, bañ lem ju xelli, waaye boo xiifee, lu wex lu ne neex la.
-
8
Ku sore fa nga bokk, dangay mel ni picc mu sore tàggam.
-
9
Diwook suuru day naatal xol; waaye li neex cib xarit, xol la lay digale.
-
10
Bul fàtte sab xarit mbaa sa xaritu baay, bul jàq ba seeti sa mbokk; dëkkandoo bu jegee gën mbokk mu sore.
-
11
Muusal, doom, ma bég, ba mana tontu ku ma sikk.
-
12
Kuy foog, gisu ay, làqu; ab téxét ne ca tëñëx, loru.
-
13
Ku gàddul jaambur bor, jëlal mbubbam; tayle ko, moo dige feyal ndaw su yemadi.
-
14
Nuyoo bu xumb, suba teel mooki saagaa yem.
-
15
Jabar ju pànk mooy senn bu dakkul, cib taw;
-
16
ku ko mana yemale, mana téye ngelaw mbaa nga ŋëb ag diw.
-
17
Weñ ay nàmm weñ, nit ay nàmm xelu moroom ma.
-
18
Ku aar garab, lekk ca doom ya; ku topptoo sa sang, am ngërëm.
-
19
Ku xool cim ndox, gis sa kanam, nga xool sab xol, gis sa jikko.
-
20
Njaniiw ak biir suuf du fees, bët it du doylu mukk.
-
21
Xaalis ak wurus sawaraa koy xelli, waaye àtteb nit ca jëëm.
-
22
Soo jëloon ub dof, yeb ci gënn, booleek pepp, wol, du tax ndof ga deñ.
-
23
Xamal bu baax lu say gàtt nekke, te def sa xel ci say gétt,
-
24
ndax alal wéyul fàww, ag pal du ñeel sëtoo sët.
-
25
Gannaaw bu ñu gubee, ba ñax saxaat, ñu dajale ngooñ ma ca tund ya,
-
26
say xar da lay amal koddaay, bëy yi génneel la njégu tool.
-
27
Meewum bëy daldi am, ba doy la dund, yaak sa waa kër ak sa surga yu jigéen.