📖 Proverbs 17
-
1
Feppu dugub wu ànd ak dal moo gën lu ne gàññ kërug ayoo.
-
2
Surga, bu rafetee xel, tiim doom juy rusloo, séddu ni doom ci alalu sangam.
-
3
Xaalis ak wurus sawaraa koy xelli, waaye nit, ab xolam, Aji Sax jee koy nattu.
-
4
Ku bon ay déglu wax ju bon, fen-kat di teewlu ay sos.
-
5
Kuy ñaawal ku ñàkk, tooñ nga ka ko sàkk; kuy reetaan ku jàq, mbugalam du jaas.
-
6
Teraangay maam, sët ba; sagu doom, baay ba.
-
7
Waxi teggin jekkul cib dof, ay fen ci as gor waxi noppi.
-
8
Alalu ger njiglaay la ca ka koy joxe, ba fu mu jublu, mu nooy.
-
9
Bale tooñ, yokk cofeel; sulliw ay, tas xarit.
-
10
Ku am ug dégg ngay yedd benn yoon, ab dof téeméeri yar du ko waññi.
-
11
Ku bon fippu doŋŋ lay jéem, te musibaa koy dikkal.
-
12
Taseek gaynde gu ñàkki doomam moo gën taseek dof ak yëfi dofam.
-
13
Kuy feye mbon jëf ju baax, lu bon du jóge sa kër.
-
14
Ndoortel ay di wal mu tàmbali, luy indib xuloo, bàyyil.
-
15
Dëggal ku sikk ak daan ku jub, Aji Sax ji sib na yooyu yaar.
-
16
Ab dof du am xaalis, jënde xel mu rafet; buggu ca dara.
-
17
Xarit du bëgg, di bañ; mbokk day bokk ak yaw say coono.
-
18
Ku ñàkk bopp ay dige feyal jaambur, di ko gàddul boram.
-
19
Ku bëggu ay bëggi tooñ; damu, yàqule.
-
20
Ku njublaŋ du baaxle, kuy wax njekkar añe musiba.
-
21
Ku jur ab dof, am naqar; ab dof waajuram du bég.
-
22
Xol bu sedd day garabal, xol bu tiis day semmal.
-
23
Ku bon day nangu alalu ger ca suuf, nara jalgati yoon.
-
24
Ku am ug dégg ne jàkk ci xel mu rafet, ab dof ne xóll, xel ma sore lool.
-
25
Doom ju dof di tiisu baay ba ak naqaru ndey ja.
-
26
Ku deful dara, feyloo kob daan, dug njub; dóor as gor du yoon.
-
27
Ku moom sa làmmiñ am nga xam-xam, te ku teey am ngag dégg.
-
28
Ab dof sax bu noppee, nirook boroom xel; ku ne cell, ñu fooge lag muus.