1¶ Ba loolu amee Balaam ne Balag: «Tabaxal ma fii juróom ñaari sarxalukaay, te waajalal ma fi juróom ñaari yëkk yu ndaw, ak juróom ñaari kuuy.»
2Balag def na ko Balaam wax, Balag ak Balaam ku ci nekk sarxal wenn yëkk ak menn kuuy ci sarxalukaay bu nekk.
3Balaam ne Balag: «Taxawal fii ci sa saraxu rendi-dóomal, ma dem ba nee. Jombul Aji Sax ji dikk, dajeek man. Mbir mu mu ma won, dinaa la ko àgge.» Mu daldi dem ba ca kaw tund wu ndaw wu dara saxul.
4¶ Ba loolu amee Yàlla dikk, dajeek Balaam, Balaam ne ko: «Ñaari sarxalukaay yi, yékkati naa leen te sarxalukaay bu ci nekk, sarxal naa ci wenn yëkk ak menn kuuy.»
5Aji Sax ji nag yeb kàddu ci gémmiñu Balaam, daldi ne ko: «Dellul ca Balag, te nga waxe noonu.»
6¶ Balaam dellu ca moom, fekkul lu moy mu taxaw ca saraxu dóomalam, moom ak kàngami Mowab yépp.
7Balaam yékkati kàddug ñaanam, ne: «Fa Aram la ma Balag buuru Mowab jële, foofa ca tundi penku ya, ne ma: “Kaay ñaanal ma yàlla Yanqóoba, Dikkal rëbbal ma Israyil mii.”
8Moo nu may móoloo ku Yàlla móoluwul? Ana nu may rëbbe ku Aji Sax ji rëbbul?
9Kaw doj yii laa tollu di leen séen, fi kawte yii laa leen jéere. Aw askan a ngii, dëkke fu beru, te bokkuñu ak xeet yi.
10Ana kuy lim feppi suuf, ba lim askanu Yanqóoba? Ku mana waññ xaajaatub Israyil gii? Man de, yal naa dee deewinu aji jub ñii, yal na sama muj mel ni gu askan wii!»
11¶ Ba loolu amee Balag ne Balaam: «Yaw, li nga ma def nag? Móolu samay noon laa la jële, yaw defoo lenn lu moy ñaanal leen?»
12Mu ne ko: «Xanaa du kàddu gu Aji Sax ji yeb sama gémmiñ, moom laa wara sàmm, ngir wax ko?»
13Balag ne ko: «Kaay rekk, topp ma, ba feneen fooy tollu di leen gis. Seen cat doŋŋ ngay gis nag, waaye doo leen gis ñoom ñépp. Su ko defee nga móolul ma leen foofu.»
14Mu daldi koy yóbbu ba ca toolub Sofim, ca collu tundu Pisga. Ci kaw loolu mu tabax fa juróom ñaari sarxalukaay, sarxalukaay bu nekk, mu sarxalati fa yëkk wu ndaw akam kuuy.
15Balaam ne Balag: «Taxaweel nii ci sa saraxu rendi-dóomal, man ma séentuji nee.»
16¶ Ba loolu amee Aji Sax ji dajeek Balaam, daldi yeb kàddu ci gémmiñam, ne ko: «Dellul ca Balag, te nga waxe noonu.»
17Mu dem ba ca moom, fekku ko lu moy mu taxaw ca wetu saraxu rendi-dóomalam, mook kàngami Mowab. Balag ne ko: «Lu Aji Sax ji wax?»